Cabb b: tur
Ak dank, dajaloo ci benn barab. Niral: Jigéen ñaa nga def ab cabb ca ëtt ba.
Cam s: tur
Nit k
Can g (tur) alal ja ñuy jox jigéen bees koy takk.
Car-car: (njëfka)
Luy sottiku niki ndox moo def ci lu bënn fu ne muy tuuru di car-cari. Niki it ronqooñ i ku jooy.
Daraay rabal. Daraa joo xam ne sëru rabal lees ko ñawe
Céebo m: tur
Nawet bi dees koo séddale ay xaaj. Xaaj yi yu njëkk yi nag lees di woowe ay céebo. céebo mu ne fukki fan ak ñatt lay doon. Amna céebom dabraan, anaata, dékk añs.
Cëtëŋ: njëfka
1- Lu jóge ci kaw ne cëpp ci suuf.
2-Mbetteel, lu jekki jekki dikk te tàggoowul, lu bette. Lu jekki jekki ne cëpp.