Catégories
Leeral waxiini wolof

Bëy wéy na mbuus

Leeral:

Bu njëkk ba ay defukaay bareegul, bees masaan a fees ab gàtt dañu daa fexe ba der ba du bënn, su ko defee buñu noppee raxas ko bamu set di ci def ndox.
Loola ñuy def ndox mi nag mooy mbuus.

Leegi nag, booy fees aw bëy far def ba bënn, dootul man a doon mbuus ndax bënn na.

Ñu ne nag: Bëy wéy na mbuus.

Lii mooy mbuus. 👇🏾

Catégories
Yuusu Nduur

Sama doom war ci mbaam

Góor gi nee na: Àdduna kenn xamu ko.
Pàppa ekspilike nu.

Góor gi nee na: Àdduna kenn xamu ko.
Pàppa ekspilike nu.

Waaw ma ekspilike leen:
Maak sam doom
Sama doom yéeg ci mbaam.
Man may teete mbaam.
Haa nu romb benn dëkk,
Nit ñi toogoon foofu.
Ñi ngi naan xoolal xale bi aka reew.
Naaj wu tàng wii
Moom mu waroon a teete mbaam
Sama doom déglul benn a ngoogu.

2- Maak sama doom
Sama doom wàcc mbaam
Man ma yéeg ci mbaam
Moom muy teete mbaam
Beneen dëkk binu romb
Nit ñi toogoon foofu
Ñi ngi naan mag mii moo ñàkk xel.
Sama doom déglul ñaar a ngoogu.

Àdduna bii, soo defee lii, ñu ne la lële, nga de lële ñu ne lii a nu gën a neex.

Góor gi nee na àdduna kenn xamu ko
Góor gi waxtaanal nu
Góor gi nee na àdduna kenn xamu ko
Pàppa ekspilike nu

Góor nee na àdduna am pàttaliku la
Pàppa ekspilike nu

Waaw ma ekspilike leen.
Leegi nu wàcc mbaam
Nun ñaar nuy teete mbaam
Ñeneen ñi nu romb fee
Ñi ngi naan ñaar ñii ñoo ñàkk bopp.

Leegi nu yéeg ci mbaam
Kenn wommatul mbaam
Feneen fi nu romb fee
Ñi ngi naan ñii ñaar ñoo ñàkk yërmaande
Sama doom déglul ñatt a ngoog oo.

Ne baay bi, bàyyil man suma rombee
Baay bi, bàyyil, man suma la jiitoo
Nga wax ma lu ñaaw.

Ne bàyyil suma la rombee nga wax ma lu ñaaw
Man suma la jiitoo nga wax ma lu ñaaw

Man li may def a gën li ngay def?
Am li ngay def a gën li may def?

Wommat, wommat mbaam ñu gis la.
Dunyaa, ni mu mel a gën ni ngeen mel.

Suma la wonee gannaaw nga wax ci man
Waxóo ci man lu dul wax ju ñaaw

Lu ma def nga ne baaxul
Lu ma ne amna nga ne loolu amul
Waaw loolu lu ciy pexe?
Li ciy pexe mooy bul faale
Bul toppatoo te dee ko sóoraale

Baabakar Kan way na Allaaji Bada Lóo mooy baayam

Seetal Yuusu Nduur ni muy waye
Mbaar, mbépp ak mbëfër

Seetal etuwaal ni muy tëgge
Danuy misig mu saf Yuusu way ci kawam

Su doyul nu dolli
Su ëppee nu xaaj ko
Su matul , nun nu mottali ko
Ismayla sóo ndax mu tane

Catégories
Wayi cosaan

Kuy laal Maademba

Kuy laal Maademba – Faatu Kase

Kuy laal Maademba sabar ga ca Ndaayànde kuy laal ndaat-saay.
Kuy laal sama doom jee, salaan jooyul wéet óo.

Sama doom sama soppe dund a mat a jooy óo, moom laay jooy ndax YÀLLA.
Féq saw fan mu gudd ée, nga am foo ma féete.

May ñaan Maademba nga day ni sa baay YÀLLA ay buur doom dundal.
Boo dundee ba man liggéey feral saay ronqooñ ée.

Doom waajur du fo ku leen di teral jàll àdduna ak laaxira.
Kuy teral waajuram, sa pay ca rabbi

Bul bew, bul jàmbu àqi njureel day toppe te day gaañ doom ju bon.
Bul féew Mademba a soo bëggee bijjaaw ée.

Bul jooy sama nenne, aayoo, beeyoo, beeyoo.
Bul jooy sama nenne, aayoo, beeyoo, beeyoo!

Catégories
Wayi cosaan

Jànjóoli

Jànjóoli – Faatu Kase

Jànjóoli ée, Biram Paate Jànjóoli ée, Aali war na Laat.

Jànjóoli war na jànjóoli , Maakumba war na ndóogóor Aali war na saryaan.

Baay jàngalóo ma, baay jàngalóo ma.
Damaa màgg daan.
Ba ma àttanee sab gopp oo,
Daal di aw sa yoonu tool, booba damay ndaw.

Sàmba Gilaajéegi nee:
Bu ndën xatee ndaama jooy.

Sàmba Gilaajéegi nee:
Xulóol du màtt saamaan.

Sàmba Gilaajéegi nee:
Ku am nag du yàppu muus.

Sàmba Gilaajéegi nee:
Nag du màtt mbaam du daan bëy du day ni giléem Saar.

Xam naa ku ma ci fayul njoow, dinaa la lawti-lawtee
Xam naa ku ma ci lebum njoow, xam naa fa muy jaar ba siiw.

Catégories
Sëñ Musaa Ka

Jooyi Wolof

Déglul ma jooy jooyi wolof
Mbër ma defar réewi wolof
Ba koo fu seeru am i yëf
Te wootewul fetali sox
 
Moo naka mbir yéen ñi di mbër
Ku mel ni man moo lu ca war
Gumba gu ndaw gu matla fer
Ndayam ne mes lu ngeen ca wax
 
Te amagul ku ko wommat
Te xamagul yoon wu jub it
Te manta daw ba raw lor it
Te xel ma dof nopp ya tëx
 
Xol bay xalam di fér-féri
Ronqoñ ya yol di car-cari
Cër ya ca des di bér-béri
Di jéem a jëf te ruu ga lax
 
Bis bu xëyee dëgmu di jooy
Mbaa muy yërëmtalu ba yooy
Soo ko jisee gët ya di xuuy
Mbaa muy palamtu lu mu sex
 
Jamono jaa ngi wéet a wéet
Ku deeti jiitu te du njiit
Ŋëb ruu yi boole seeni bóot
Te mel ni géej du fer du nëx
 
Mbindéef yi yépp a ngi gëlëm
Dénd bi bépp a ngi lëndëm
Baatin bi lépp a ngii ñu lëm
Saahir si lépp a ngi ne jalax
 
Wàlliw yi yépp a ngi ne selaw
Ndàmb yi yépp a ngi gelaw
Boroom dogal ba day nelaw
Te àtte yaa nga mu walax
 
Àllarba jam fi ne bëret
Di nittu fan ciw tamxarit
La àtte yépp ne xëret
Góor ñeek jigéen ñi daw ba xëx
 
Xel yépp génn ne wëret
Nawug ku nekk ne gëret
Neexoon keroog ma ne xoret
Ndax YÀLLA dootuma torox
 
Demam ga ump na mbindéef
Te wub na boppub kuy mbindéef
Ku dul malaaka ya ko wuuf
Ak YÀLLA ak ña mu ko wax
 
Yonnen ba ak ahlu badar
Yori biram di ko defar
Moo tax xameesu ca lu wér
Demiinu Yonnen la ko jox
 
La dale Njurbel ba këram
Malaaka sàppe ne gorom
Di ko bijjanti di gërëm
Te di ko sàbbaal di ko jox
 
Way-dee ña jokku woon ca moom
Te nekk barsàq ne xiim
Ku ne di teeru naa Boroom
Xéewal yi ñëw mu di nu jox
 
Wàmmeeli Tuubaa di damu
Mu topp léen di léen rammu
Bir ya aka rëy ba faf lëmu
Ba ku ca xam lëf du ko wax
 
Garabi Tuubaa di sikar
Suufam ya ak ndox yi di ser
Saahir si lépp def naqar
Baatin bi lépp ne fayax
 
Jumaahi Njurbel moom di jooy
Taax ya ne yàŋŋ defi mbooy
Cëy àddina aka man a njuuy!
Te man a wor te man a nax
 
Tubaab ya sax tëj seeni taax
Ken xamatul lu doon sa baax
Baykat ya gedd seeni paax
Wata ya fenqoo ne rajax
 
Kenn xamatul kuy sëriñam
Kenn xamatul kuy taalubeem
Góor dootu faale waa kërëm
Loo sex mu mel ni ab xetax
 
Luy doomi Aadama a ngi jooy
Jinne ya jébbalu di jooy
Sunnas Yonnen ba sax di jooy
Lislaam ji rët ba far di lox
 
Malaaka yaa ngi wër di jooy
Suuf yi juroom yaar a ngi jooy
Te asamaaw yépp a ngi jooy
Ngir xamaguñ fu waa ja dox
 
Weer yi fukk ak yaar a ngi jooy
Bis yi juróom yaar a ngi jooy
Cër yi juróom yaar a ngi jooy
Ba ahlu badrin ñile sax
 
Juroomi julli yaa ngi jooy
Way-wuutuhante yaa ngi jooy
Jant bi ak weer wi di jooy
Saa yépp yépp a ngi forox
 
Baahima yépp a ngi ne gorom
Ñax mi saxoon sax ne ŋayam
Gàncax gi ànd ne kayam
Garab yi yenn xob yi lax
 
Gone di goy-goylu di jooy
Mag di xalam mbiram ba yooy
Ñi mel ni man di wax ne wóoy
Seen bir yi dootul mat a wax
 
Jigéen ñi rët bay fëlëmu
Murit ya dof bay kayamu
Ñële di yuuxuy bëlëmu
Kuy jéem a jóg far ne sërëx
 
Ku ne bëret far ne nërëm
Njénde yi yépp ne xerem
Jirim bu nekk tëj kërëm
Ñële di rëb-rëbi di lox
 
Boo xalamee Ngën ji mbindeef
Bisam ba ndax nu man a giif
Ak xulafaa-u ya ko wuuf
Te xam ne àddina du sax
 
Kerog ba Yonnen nee meles
Sahaaba yépp ne taxas
Abaabakar Saddiix a des
Wa maa Muhammadun la wax
 
Te dafa gëm ba xol ba sooy
Te teewu koo muuru di jooy
Ba xel ma délsee la ne suuy
Ku dul ka bindoon du fi sax
 
Ku ne ne ngéej a dee keroog
Ku nekk fàtte say baraag
Ruu yépp faatu nan keroog
Sun jëmm yee fi des di dox
 
Jii waay a wuutu jooja waay
Yii gaa ya wuutu yooya gaay
Mii mbir a wuutu mooma, waay!
Mii mbir a rëy ba weesu wax
 
Déglul ma lim fi ay ndamam
Yoo xam ne ken dootu ko am
Li des ci dunyaa ci kanam
Ndox soo fu teeyal it mu nëx
 
Moojaa ku deeti feeñ a feeñ
Ba Màkka ñëw fi di ko jiiñ
Yonnen ba, gànnaar di ko téeñ
Mu far di leen jox i sarax
 
Ñoo di ko jox ay àddiya
Ñii di tawatsi àddina
Ñii mbiri àllaaxira ya
Ñoo bañ a wuysi def i tëx
 
Sëriif yi ñëw fi di ko yéem
Làbbe yi ñëw fi di ci jéem
Ku ne di barkeelu ci moom
Mu fees a fees ba mel ni dex
 
Muy jàpp ceddoy def i seex
Di fomp xol ya ba ñu weex
Génnee ca àddina ak baneex
Saytaane ak bakkan mi tax
 
Moojaa ku deeti jëf lu jar
Yonnen ba ak ahlu badar
Ngeen jaxasoo ci yépp bir
Ba foo fi jëm ñu di la rax
 
Aras di jaayu cim mbindam
Malaaka sàbbaal ngir mbindam
Ibliis di làqu ci’g lëndëm
Limub araf ya di melax
 
Muy dox ci jàww ni njanaaw
Di xotti déeley asamaaw
Lum wax fa diiwaan ñu ne waaw
Muy fal di folli ci lu sax
 
Di soppi ruu ya di defar
Di jàpp ñaawtéef ya di far
Di yokk dig ya ba mu sar
Di gàddu tiis ya gën a wex
 
Moojaa ku deeti xamle weer
Ci bis bu niis bu bañ a leer
Ci gàmmu mbaa ci weeru koor
Ba sunu xol yi bañ a nëx
 
Moojaa ku deeti feg balaa
Tey xamle waxtu wa balaa
Di ñëw ci nit ñi ba balaa
Agsi mu sàkkluy sarax
 
Di feg i mbas di feg i tiis
Ak mbir mu xew tey yan bu diis
Mbaa xiif bu tax ku ne di siis
Ba boo tibbee doo tal a jax
 
Moojaa ku deeti doy a doy
Bay fàtteloo baay ak i nday
Ku ne mu jox la lu la doy
Te soxlawoohul ku ko jox
 
Boo ko joxee da na la jox
Boo ko joxul mu di la jox
Te du la jànni du la ñax
Te du la wor te du la nax
 
Boo ko moyee mu di la may
Boo koy jëfal mu di la fay
Boo ko bañee mu di la jay
Ba xëy la not nga ne sërëx
 
Boo ko meree du la mere
Boo ko soree du la sori
Boo gorewul moom mu gore
Kii ku ko bañ da nga torox
 
Moojaa ku deeti fab i koom
Di buub di sànni niki dóom
Di fab jirim yay def i doom
Ba ken du faale nday ya sax
 
Di fab i téerey def i koom
Du faale junneek i gëléem
Ku ñëw mu jox la ba nga luum
Kuy dem di ñëw ak ku fu sax
 
Di tagg far Ngën ji Mbindeef
Te faalewul yàpp wu duuf
Ba faf yaram wa dafa loof
Te xeeti ñam ya ne pacax
 
Di dugg i xalwa ciy kërëm
Yonnen ba jox ko fay ngërëm
Te boo ko dee woo ay dërëm
Du tax mu déglu la nga wax
 
Moojaa ku deeti wax i bóot
Di sulli ay xam-xam yu xóot
Ba sunu xol yi dootu root
Ca dab ya ibliis def i ndox
 
Moojaa ku deeti wax muriit
Lu koy fegal pexey mariit
Di soppi dof mbaate baliit
Muy cam su yewwu te forox
 
Kuy saafaraati ràggi xol
Ku deeti far tilimi xol
Ku deeti xoolee gëti xol
Bay jis lu ken dul man a wax
 
Ku deeti dundal guddi yi
Bëccëg yi yépp ak waxtu yi
Bedd yi yépp ak bunt yi
Foo toll jis mu di fa dox
 
Fu ne mu def fab jullikaay
Ku ne mu boole la ak i gaay
Digal la teg la cib jataay
Te du la wor te du la nax
 
Di jiite waxtu yiy juroom
Du wuute mukk te du tiim
Xasaa-idam sëf nay gëléem
Ajaa-ibam sëf nay warax
 
Di bind guddi du nelaw
Bu jëmm yépp nee selaw
Mu dem ci péey bu ne xeraw
Bu bët setee mu di nu wax
 
Kii ku ko jis sax ku ko jis
Ku jis ku jis waa ju ko jis
Su ngéen demee ca boo ba bis
Mu rammu leen ken du torox
 
Doomam ya ëpp nañ sëriñ
Seexam ya doy na ñuy sëriñ
Ay taalubeem raw nañ sëriñ
Kuy roy na roy ci lii ma wax
 
Moojaa ku deeti tarbiya
Ba noppi daa di tarxiya
Ba noppi daa di tasfiya
Ba kum gërëm dootu torox
 
Moojaa ku deeti taxliya
Ba noppi daa di tahliya
Ba noppi daa di taxliya
Ba ku ko jis daal di ne ax
 
Ku deeti xamle tasawuf
Te bis bu ñëw muy gën a saf
Ba gaa ña delluy saf i dof
Garab yu ndaw yiy doog a sax
 
Ndax ngér mi dellu yees a yees
Ndax YÀLLA am ca gaa yu fees
Mbaa gaa yu sóobu ba ne suus
Ca péeyi góor ña di ca wax
 
Wuy ma ne wuy man ki ma ron
Te ndox mi yol fi sa ma ron
Lu nekk maa ngi ko naroon
Fu may duyeeti ngën gi ndox
 
Wuy yoonu tarbiyaa ngi jooy
Ngéram mi def ñall ak i mbooy
Cëy àddina aka man a njuuy!
Te man a wor te man a nax
 
Tarbiya yaw def ngab jirim
Ñàkk nga waa ju saf xorom
Nun ñépp noo ngi ne gorom
Ni jën yu ndaw yu ñàkk dex
 
Soo doon jigéen ma ne la tay
Muurul bu jag dootul a sëy
Far yi fi des duñu la doy
Luñ jaayu jaayu duñ la nax
 
Déglul ma jooyle alxuraan
Waayam ju mat ja ba rañaan
Da koo defoon ab kerkeraan
Di dem di délsi di nu wax
 
Ca lay jiseek Ngën gi Mbindéef
Moo di kënoom bay noti seef
Gaalam ga mooy jàlle mbindeef
Ca bis ba kenn dul tal a sex
 
Moo ku la deeti def ci taax
Di sotti lajkoloñ ju baax
Boole la teg ci lal yu baax
Te dem fanaan ci néegu ñax
 
Mo ku la deeti jëndlu
Mo ku la deeti jànglu
Mo ku la deeti bindlu
Bu ñuy nelaw mu di la wax
 
Ku deeti jàpp ay junneem
Di def ci yaw mbaatey gëléem
Te def ma koomam jamonoom
Ku ko fu xam na ma ko wax
 
Ku deeti fab lim ub kurus
Ci xeeti xaalis ak wurus
Di sànni gaa ya koy durus
Te di ca raaxaley tarax
 
Ku fabatiy laaya di nas
Araf ya takkoo ni kurus
Saahir sa mel ni kuy durus
Baatin ba mel nikib tabax
 
Moojaa ku deeti listixaar
Ci alxuraan di tuddi saar
Di tuddi laaya di xiyaar
Ba ne la lii la YÀLLA wax
 
Mushaf ya lay wéetalikoo
Durus ga lay fàggandikoo
Taalif ya lay jottalikoo
Leer ya gëndoo mel nig melax
 
Mbaakol di bind di ko yót
Gànnaar di bind di ko yót
Saalum di bind di ko yót
Muy jënd ay móol di ca rax
 
Boo féetewoo di ko bindal
Mu féetewoo di la dundal
Boo koy bayal di ko bindal
Mu sàkk ñuy bay di la jox
 
Di la defal can ub jigéen
Labat ko yët la doo ko miin
Te gàddu say bir nga ne tóon
Mbaa nga ne gumm nim petax
 
Su ma yëgoon jënd i mushaf
Su ma yëgoon bind i mushaf
Su ma yëgoon dëju ba xëf
Su ma yëgoon matul a wax
 
Su ma yëgoon di ko bayal
Di ko bindal di ko demal
Di ko sukkal di ko dawal
Te di ko rootal dabi ndox
 
Muusaa Ka seetal say moroom
Te kon nga sant sa BOROOM
Seetal ñi weddi jamonoom
Ak ñi wéy ak ñiy bëgg a wax
 
YÀLLA laram bu mu gërëm
Loo ko jëfal am ca ngërëm
Soo ko joxee benn ub dërëm
Mu ful ko ay junni yu sax
 
Leeram yi tax lay am i yëf
Di way araab di way wolof
Te xam ne jàngóo sax u lef
Mbóotam mi rekk a la ko jox
 
Leeram gi tax laa am i gaay
Te donnewóo ko ci sa baay
Fekkóo ko woon ci say najaay
Ku seetlu rus ba ne tesax
 
Te xamalóo leen i masal
Te firiloo leen i fasal
Te bu ñu sukkee duñ desal
Lii sopp Bàmba rekk a tax
 
Te dunŋñu xàcc duñu mer
Te duñu xàddi du ñu bar
Te duñu yoqi wut i kër
Te du ñu fecci la ñu wax
 
Sëqal i bopp ne suxur
Di fande tey soli sagar
Nga tëdd ñuy defar sa kër
Loo digle ken du ca nasax
 
Waajal te jëm ci sa BOROOM
Te jéem a sàmm sa juróom
Yaar yii ñu boole ñu ne xiim
Te xam ne bis da na ñu wax
 
Ngir ki la daa sàmmal di feg
Di la tinook ki lay alag
Bu sàmmatul tay ak ëllëg
Boo farluwul danga torox
 
Alhamdulil laahi na ngeen
Sant BOROOM Aras mi leen
Tàbbal ci ngéram mi te ngeen
Jis ko mu jis leen ngéen di wax
 
Alhamdulil laahi ndegam
Tuubaa di Màkkay aji-gëm
Ku yéene aj te manla dem
Na fas siyaareji te dox
 
Ku xam te xàmmee jamonoom
Na xam ne YÀLLA ki nu moom
Moo boole penku ak soowoom
Te yori bóotam di warax
 
Alhamdulil laahi na ngéen
Sant ki tax mu jege leen
Dogal ba jiitusi na leen
Dogal ba rekk a nu ko jox
 
Manoon nanoo dëkk ca Ngaay
Walla ca Podoor ak i Gaay
Walla nu faf dëkki fa Xaay
Di xëy di gont di ko dox
 
Manoon na koo defi Gaboŋ
Nuy fay i paas di yor i boŋ
Walla mu dem ba ne nu meŋ
Ba ken du xam réew ma mu sax
 
YÀLLA bu sun réew yi di naaw
Di wuyu YÀLLA niy njanaaw
Yal nanu dal fi sa gannaaw
Nga boole leen far ne tarax
 
Yal nan ñu rob fa sa gannaaw
Kurél ba ngay bokkali géew
Te may nu mbég mu gën a gaaw
Xefiinu bët mbaateg melax
 
Àllaahumma salli alaa
Sëydinaa baabil hulaa
Bi haqi haaidil malaa
Yërëm nu boole nu sarax

Aji-bind ji: Ismayla Géy
Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Sëñ Maam Moor Mbàkke

Loyu W, Y, K, L, M, N

LOYU W :

Saytaane day wëtt ci xol wudd la am
Wattu ko bul ko wacc muy war di ku lëm

Dafay woreek a weddilooy werenteloo
Di wàjji ngëm di wonni pas-pas du welu

Wor ko te wodd xol bi ngëm waaru bu wér
Sotti ci waamew tudd Yàlla xol bi wér

Weeral sa wañsu diine def say warugar
Bu ngëm gi woos ni woddbeer wu gar ya wër

Werante wottee ko lu war, lu wóor itam
Na wuutu wor te worma wecci wane tam

Nga wéex sa xol wekki ca luy wollamiku
Te bàyyi weeje it welal tayle ba ko

Te wulli nag wëllu kañaan ak weli rëy
Wetañ yu jëw weñ ko te wetti far ko ray

Te wacc weerante te wéer fa wóllare
Wareef ak ug wegeel te wicc njàqare

Te wërsëgoo wiiri wakiirlu wis ca way
Te xol bi weex nga wattu waŋŋi wuute wéy

Te waggar it sa bopp tey waaru bu wér
Te bul di wëndëŋ wa wogul wàqi te war

Di waaj di wàlli weddi bakkan ak loram
Te weer ko bul weng ci moom ak ci wujjam

Di waslu àq woor ci caaxaan ak i nar
Wékku ci Yàlla def ko waay jëf la la war

Te fonk waxtu xam ne daa wund lu rëy
Te bul di wuññi awra bul di wóoyu ay

Na ngay woyof te bul di wex ci kenn itam
Ku dul ku bon te fonk worma tey xalam

LOYU Y :

Yaraanga a ngi may yeerook a yedd ak a yong far
Yërëmleen ma saag yées yas na yoqat a ngii di yër

Ba yambar ya far nañ tiim ma man may yalaŋ mu yës
Ba yuqóolu naa far yollungar nañ ma far ma ber

Te yiiruñ ma may yoppoorlu yërmaande far na jeex
Ma nàmp yanaatub njàqareek yéjji xol bi mar

Te yombul samay mbir yemb yenkeewlu naa itam
Ci yëmmug yaras maa yay di yuuxook samaw naqar

Te saa meññatum yaakaar mi yuntul ma yéene yiw
Ku nekk te teewul may yëgg uw naqar ak lu tar

Ba saa kawarug mettiit wa yiif na ba yéeg i yéen ba rongooñ di yol saaw fit ne yacc ni laaxu gar

Ma yeewat ci yittey gaa yu yéeme mu të a yéwen
Ma yuugan ko yootug yokk fàww ci ngën ji yar

Te daw yaafus ak yonj ak di yeex ak di yox-yoxi
Te def yoww aw ciw yoon ba def yunn cig cigar

Ma mucc ci yeer muy yabbalum xel di yaag xalam
Te muy yaradal am xel ku yewwu du sóoru mbër.

La yellay ñu yippil may yéréy yeete tey ya gën
Ma far yalfandoo ag muñ ci saa yan bi yuur te dër

Ba yéjj jalag saay bir yaraax yiiraley wetam
Ñu yeddan ma baa yaax, yànjaxaan ma soreek i lor

Ma mucc ci yaafug yitte far yam ci ngën ji yiw
ne yomm yoxoos jàmm ak njariñ ni yulub ci kër

Te yaakaar du tas saay yitte yemb ma yokk itam
Yarook yewwu, luy yàq ak lu am lor soreek i nar

LOYU K

Defal ganug ngënéel te bul di gangalam
Ŋàbb gogub giide di gindi képp ku gëm

Te sax ci gàgganti gox ak gàddi ngëmmeen
te aw ca ngér ma bul ragal giili gëléen

Te ŋoor ci ngor te buñ la ger te bul ca goow
te xàmmi giiri gor yi bul génn sa kéew

Fexeel a gën, ngëneel ya gaw la nib gëwéel
Nga gétti, góor Yàlla gu nekk yor sa kiil

Te goor ci way-gànjari jëf yi bul di géey
sa taali jàngu bum di giim mukk ak a géey

Te jàpp gunti yar ba gànnayu te ŋëb
Ngérti ngëram genge ci kaw xàll wu jub

Te moytu ñall, ngir ngis ak ngiroo nga ca
Moytu giraawaali te loo nekk të ca

Te ŋeeg sa wanti kóttiteefi gàcca tam
Te ŋoy ca mbicci kaw ga gàddu gaali ngëm

Gindiku, say góomi ayib ŋàññ ko nag
Gëlal ko, taal ko ngànj, gas ko suuli nag

Te ŋoy, sa kaaraange gegal ko kaasi mbég
Sugglikook gar ya ca gotti gol ba nag

Nga dib gawar bu gaynde dul gaar ak a kar
ku fit wa dul ŋiis ak a ŋott, nay dëgër

Te bul di gooy ni ŋóot, ku gàlli nang ko ga
Te gaaw te jàmbaare ba mel ni gaynde ga

Te bul di bañ kumpa, te bul kañook a kaal
Jur gu boyug gotti te gur-gur ko ca teel

Te moytu kàmbi kekk yuy golliku ya
te guuf sa gàkki xol yi suul ca kekk ya

Gëndale say ngërëm yu kersa gunge nag
Te guuf sa goog gi, ŋacc kumpa sànni nag

Sa kem yi gaw leen ak i may te bul kañu
Te bul di kooj sa jikko ngëx loxook jañu

Ngaaxi tukkal deesu ko perngal mbòccoor
Nangay worook képp ku doon ab kàccoor

Te ngàcca-ngaalaama ya buñ la këf ba tax
Nga far ca gàllankooru kaf ya buñ la nax

Te bul di gëllgóose jëm ci genn wet
matal ci lépp bul di gaaruwaale it.

LOYU L

Maa lànk dóotuma lépp bay lonk fay di ma të
Lott ay waral leb di tee fay lëj-lëj ay lëm i bir

Laggal te liiru ba jot sam lef te moytu lixóor
Tey moytu am lëgg bul léej ëpp lor la ci lar

Sa lépp nay leer moyul luubook lu lënt te daw
Làggil ci sàkku lu lew daw laaxo ya ak waxi nar

Bul lump ciy jëf, jëfal luy léemtu bul laf itam
Te seeruwóo lolli bob law na ak i mbég lare wér

Bul laŋ ci sab lal bu suuf lóoree nga làlli te wéy
Te lippikuw nit ba làqqiy leewi leew ak i tar

Ŋaawal sa legg mi bul lëñbët lu dul sa ayib
Bul lunk jëm suuf jëmal kaw leemtu naa la nga xér

Sa yitte nay law te bul lump it lu dul li nga man
Nga luf ci dénd bi bu liis mukk itam na nga dér

Laabal sa xol bi te làng ak gaa yu xam ya te way
Bul làmbtuy jëf lateel ug xam te teg ko ci ngér

Bariy lijjanti te bul lott it ci lenn faral
Man lépp làggi ci jëf tey lab ci def warugar

Laggal te bul laŋ ci ag moy bul ca lëng jëm it
Bul luññtuy awra bul loofal sa xel bu ko lor

LOYU M

Maandul te man yaw ci sag maas bul di mànki mukk it
Bul def sa màndiŋi moy ab miinuwaay tubayul

Xeebal masëy wa te muurloo waame moo am i may
Saw fit bu muy màcc jëm cig maax lu mànki nga ful

Bul mëdd may yeeti nang koy sante Yàlla bu wér
Te say wax ak say jëf it nay màndaxoo matalal

Bul magg-maggal sa bakkan nang ko miinal i yar
Bul mer te bul metti, màbbal moy te muñ lu la dal

Metlàngo far ko mu def menteñ ne meŋŋ ne mes
Nga muure kog dëgg gàttal say mébét di jagal

Tey muñ mettiit moom la Yàllay méngaleek musalam
Bul mel ne maaka ma cig bañ tàng dund saxul

Mokkal te màggal, sa jëf bul mëkkal it matalal
Bul yàq nig max te bul def mëkk màmm gënul

LOYU N

Nit nag ba laa nite day niitem xelam te du nar
Te not ci am xel ba buñ koy nax ngirug naaxam

Te nëbb tey jëf te neexum xel di néewali wax
Di noppi cig neen soriy nëx-nëx matal naalam

Di nemmikug naat te nargan bakkanam bañ a nay
Nërmeel itam néegi niig-niigal ngirug naayam

Fum tollu nay naabu lum nàmpal xelam bañ a naw
Tey natt boppam ci ag néewam akug naatam

Waxam nëtëx neex ngirug nooyam nosub bakkam
Di ñoddi muy nàcc ak ay nef daw sorig naagam

Te néeg ci bakkan bi ay tànkam na nooj bumu dem
Mu naj ko bam nàngi faaw bay nuur ci ag naanam

Nemmat ko bum nenn noflaay bum ko xam na ko not
Bam naagu bay neer te bum noppal ci ag naabam

Te yeew ko cig naw di dóor ciy nenkteŋ te mu nal
Daŋar ja bam set mu naaxsaayal ko ciw naajam

Te nàmm xol ba ba dootul yëg naqar te du noos
Ba dee ga ñëw far ne nuus ruuwam ga cig naawam

Te dee du néggandikus lëf, nës-nësal aki nax
Du tax mu dem, nakk-nakkal it du dog naalam

Aji-bind ji: Sëñ Maam Moor

Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Sëñ Ahmadu Baas

Dof yi

Damaa génn bis saa kër di dox romb benn dof
Mu toog cib ruqam jël ay yoxoom faste ciy waggam

Te leeg-leeg mu ree leeg-leeg mu jooy rafle wang ko wër
Ma ngay lox keroog daa sedd boolek tarug lëndam

Wérul waaye teewul nag mu dis gor nde tàllalul loxoom kenn
Tooñul it ña toogoon ci ag wetam

Yaram waa nga sooñoo sooñoo duw dàll duw basaŋ
Te lee-lee mu taw ndaysaan ba taa suuxal ab ëmbam

Bu xiifee pupel lay dem amul ndey ju koy tibbal
Fa nuy këppiy des lay dem fa lay fekki aw ñamam

Te it man la wax day mujj dem lekki ñam wu bon
Wu am yaari fan woo xam ne baaxul ci ag wéram

Na muy def?Gisul yaayam te it amna yatti at
Yu mat sanguwul lum sol da koy for ci ay sënam

Bu jaaykat bi sànnee màngo mbaa sax orãs bu nëb
Mu daw këf ko noonee sax la koy lekkee cig takkam

Ngalaw sàqi nit daw tàbbi néegam ne kàpp tëj
Mu des tay kanaayal want yay dal ci ay gëtam

E ndaysaan bu rombew dàll mbaa pot wallaw sagar
Da koy teg lu rëy moo tax mu koy boole cib ëmbam

Dafay waxtu fum wéetée te lee-lee mu mer di xul
Te kat am na ndey am baay ba am rakk ak magam

Ba muy wér la bokkak ñépp bis ñëw ñu dal ko ber
E waay wéradee tax waaye as gor la woon su gëm

Rakkam donn nab néegam jabar jaa ngi séy feneen
Te ndoom sam amoon boobee batay xolu koy gëtam

Juróom yaari doof lañ fekk Tàmbaa ñu rendi leen
Ba jël séen i awrak séen i yuur lii ka daw yaram

Dañoo butti ñee xar boppi ñee ñee ñu sànni leen
Ci ay kër yu kenn dëkkul ba ñuy xeeñ ñu door a xam

Gisal ñaata yoon lab dof di xëy dee ci ay tabax
Yu yeggul ba am ay fan ba fay xeeñ te kenn du xam

Gisal benn dof bee faatu Leelan ci wenn xur
Ba fay xeeñ te ab xiif rekk moo sànk ag dundam

Gisal ñaata yoon lab dof di xëy lekk ñam wu bon
Ba febar ca ay at kenn du jug saytu ay mbiram

Gisal ñaata yoon lan fekk ab dof mu xëy wësin
Te ken man ta laaxaan kenn ken foogulab ëmbam

Gisal ñaata dof ngay fekk dus kumba mbaa tubay
Dañuy rafle noonee rek di dem ñépp gis pëyam

Gisal ñaata dof ngay fekk duñ jekki duñ nelaw
Dañuy dox ba dee doo gis ku naa xam na bàmmelam

Te gis naa fi bis ab dof bu am benn góom bu rëy
Ma ngay wokkotoo kay waxtu kenn saytuwul wéram

Liilee tax ma jug tay woo Etaa beek ñi Yàlla ñor
Ñu booloo taxaw tey saytu jaa-Yàlla yii ñu am

Wowóowow wowóo yéen góornëmaa réew mi walluleen
Ewaay walluleen as gor su xëy ñàkk am xelam

Te gis ngeen fi ay dof yoy ku leen faj ñu daa di wér
Te xam ngeen ne mbooleem dof yi koo tëye dootu dem

Nde dof boo fi gis muy dem kërug nit la bàyyi koo
Ku wér dellu ciy mbokkam xarit xel dafay xalam

Te gis naa ku faj mbaamam te gis naa ku faj fasam
Fajum jàmb-jóobam faj goloom sax fajub xajam

Te taxtil mu faj mbokkam mu xëy ñàkk am xelam
Ku faj mbaam fajub xaj bàyyi nit àndul ak xelam

Ci lii sax ci laay faf ñaaxe askan wi may waxal
Ñu daw lépp luy tax nit di xëy ñàkk am xelam

Xelal gànjarag nit xel la nit am ba not mbëfër
Xelay tax xaleb naar not gëléem bay xëccab nosam

Xelay tax nu wullig naaga war xàcc tay dañal
Te xam gee ne du maasam nit ci dooleek ci ag rëyam

Xel ay tax ba lislaam teg nu jëf waa ju ñàkk xel
Asal dootu am aw yiw te dootu yilif këram

Xel ay tax nga xàmmee mbaax xel ay tax nga daw lu bon
Xel ay tax ba nit xam lëf ci Buur Yàlla ak mbiram

Xel ay ndab la xam-xam tàbbi ngir waa ju ñàkk xel
Du xam lëf du am lëf waa ju am xel am i yëfam

Xel ay leer ga nit xëy tedde moo tax ba Aadamun muñ
Di sangub malaakaak jinne Ibliisu ñàkk ndam

Xel ay tax ba nit rekkay sangub suuf lu weesu nit
Xarit loo fi gis ngir nit la ngir moo yoram xelam

Xarit ñàkki gët mbaa ñàkki waaraama gën nga nàkk
Am xel xel ay nit nit nitteetil ci ay cëram

Ku jàngoon walaa tulxuu bi aydiikumóo ilaa
Dangay xam ne kon kuy yàq am xel yorul gëmam

Ma wax yenn mbir yuy tax ba sun ndaw yi xëy di dof
Ñi ley rab la nii ay raab la raab yàq nay ndawam

Dofab raab dafay wuuteek dofab rab ci yenn mbir
Na ñuy moytu yàmbaa daw dorog bàyyi ay mbiram

Dofab iilu ak bob siisu ñoom it danaa ci ñëw
Damay jëkk a way ki sàngara yàq ag dundam

Bu kenn fóoni diyiyã day rayum xel di yàq xol
Lu rey xel di yàqub xol ku koy def du nit daxam

Te alkool alag naw gaay ku koy naani dootu wér
Lu waay am lu dul wér jaay ko ngir jënde kok wéram

Lariklees di yàqal nit ci xol ak ci ay xëtër
Ñi xam nee ñu day dem sax ba far gàttal ug dundam

Te dee diis ku koy naan man na dee dee gu diis te tar
Nde luy fuq bët moo gën ci nit luy fuqab xolam

Gisal waa ji naan sum-sum ne xëndaŋ ci géddi bëy
Nelaw bay xaran sum soof na lool xel yi lay gësam

Amoon na ku màndim sëng faf dër di yag-yagal
Ñu koy tàccu muy taasook a saagaa ci ab ëttam

Te am na ku naan biiñ daanu bañ sàcc lam yoroon
Te muy lim bu rëy boo xam ne moo yor dundug këram

Amoon na ku naan sàmpaañ di xeexoo ñu far ko ray
Sulaar saa ko jam ay paaka ndaw dee gu ñàkk jom

Ku naan roos du rus nit dootu rus Yàlla dootu rus
Njabootam ndaxam man naa sëyak yaayamak rakkam

Wisig yeek falaag day yàq am xel ba leen dorog
Kokaa gën kokaayine fopp cib xol akuw yaram

Te gis naa ku naan am ñoll daa màndi bay tërëf
Xalel yaa ko sottim ndox mu far yàq ay sëram

Te it am na dof yoo xam ne ay wird lañ yoroon
Ba rawhaan ya dofloo leen ñu far topp ay xëram

Gisal benn waay biy wird ab diir mu summi ay
Yëreem summi caayaam génn néegam di dox di dem

Te kat bañ ko laajee nee na suuf see ko àttanul
Ma laaj waa ji kon san suuf la doon sàmp ay ndëggum

Te talsam yi ak rawhaan yi lim sànq ciy xalel
Dorog mantikoo jot fàww daf dul lu neex a xam

Te say jàq tax nas cam di siisook a say ba dof
Kurus ag ndofam day metti ndax yombulam pajam

Gisal jenn waay jiy yuuxu tay daw di wër te naan
Dafay bañ a doon ab xutbu kii séenu nag ndofam

Te am raxasun xas-xas xarit xawma lum saxal
Lu dul ndof jëlal aw tur wu leer bàyyi talsamam

Te tas tas na waay bam yuuxu xàccit mu tas këram
Te tas mbiramak soxnaam ñu naa déet mu tas xelam

Kitil ak katal ak màkk jal-jal ku koy sikar
Bu teewloo war a naree dafay waat yu saf xorom

Te ag nasabin ak hatariisun ku leen bawul
Dafay mujj rekk fab ay mbubbam daanu ciy sënam

Jaxaay yaayi dëhtëhtiilu doofloo na ay kuréel
Jalaal jal na fiy wàmmeel te dofloo ñu am xorom

Gisal waa ji tëj néegam ba ab diir mu mbëkk daw
Te naa maa nee ajabaaru maa tay ci ab ëttam

Ku woo Ummu Muusaak yaayi Xëlbaa ci ay kurus
Ma woo man ki bindoon yaayi Muusaa te yor mbiram

Ku fiy woo Afaariitun minal jinni man ma woo
Ka bindoon Afaariitun te yor léppi wërsagam

Dalal nag te teey booy sàkku mbir ndax ku wattuwul
Xérak ëppalak yàkkamti looy sàkku doo ko am

Faral noppi yaw Baas wax bu niwee te am njariñ
Dafay doy salaatun yal na dal Taaha ak ñoñam

Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun

Catégories
Sëñ Daam Jaane

Maarsiya Seex Abdu Asiis Dabbaax

Hamdan li Rabbin Kariimin xadsanaa ci lu bér,
tànneef bu mag ba ko wax laay marsiyaal ci wolof.

Xerawluleen ma bu baax te jéem a jooy ci xalim
ngir diir bu yàgg a ngi nii, ranqoñ di tuuru ci xef.

Wéet ak jeneer sunu maam, Abdul Asiis Si Dabbaax,
jur nay xalaat sama xel, saab xol di tiit ak a raf.

Huqal bukaa-u halaa haarif billaahi ba woon
maam najli Maalikinaa, wéetal na suuf si walif.

Naa jooyle diine ji ndeem, nax naa ba sonn mu të
garjeem ba wuutee waral, ruur nañ ko fii ba Jolof.

Toolam ba lax na ba liis, pas-pas ya yépp yolox
kenn naafatul tari gëm, ba jeer ngirum tasawuf

Daa yépp xëy nañu ŋiis, xam-xam bu sell ne mes
àlliwóok i téere ne mërr, njub bindatuñ ca araf.

Kenn dootu digle lu baax, kenn dootu aaye safaan,
Kenn dootu wax dëgg buur, muy dégg boole ca jëf.

Maam doomi garmi ba woon, ag dëgg jooy na ko tax,
tay matti kàdd yi giim, log moo nu tee man a ëf.

Maam naaru maam Sofi Ñaŋ, tay mbokk jooy na ko wuy
jikkoy pusoom ja ñu réer, tax réew mi xar fu ne laf.

Waa penku ak soww baak, ñoñ diine aada cosaan,
mooy buum ga lënkale woon, seen say wa moo setu lef.

Tawhiit bu sell ba wuuf, xam-xam ba moo waraloon,
buy wax dënnam ba di riir, kàddoom ni dénnu gu këf.

Pas-pas bu sell te dëer, xam Yàlla sàmmu gu wér,
way fonk sunna woyof, Xuraan di ñam wa ko saf.

Baaxal na ceddo ya ak buur ak dammeel ak i teeñ,
bañ xëy di ay surafaa, juboole till ak i tef.

Tabam ga mooy li saxal toobay teraanga fi nun,
teral na bokk ya cér jàmbur sax ñi ngi sëf.

Moo daa nu yar di nu yiir, yërmaande ak sutura,
dox sun diggak musibaak way-bijji mbon ya walif.

Mooy ndox mu sell te teey, mbindeef du waat njariñam
ndundat yi sax bind nañ, mbaaxam ca xob ya di taf.

Raayaw ngëneel la ne cas, di daagu kenn dabu ko
ndendam ci mbaax judduwul, ña jiitu woon la ne wif!

Taajul karaamaati moo dëppoo garaat yi fi sut,
mooy dànn moo man a diir, jawfalfaraa la ne tëf.

Waayam du fande du xiif, kum yar nga gën ñi fi gën,
moo tedd mat li mu doon, kum gindi réer du ko këf.

Mooy rootukaayu ngërëm, màndal na gaa ya ko xëy,
bañ màndi Yàlla mu duy, mbaax seen bagaan ya ñu sëf.

Gaalug sariiha ci kaw, géejug haqiixa la joow,
ba teer ca boor ba ñu tànnal kàngamiy tasawuf.

Woyof ni toll ca kaw, diis gann ak mayi biir,
lëm ay màqaama yu rëy, saw kañ wareesu koo cof

Yaa donn bóot ya ca Faas, déemug sëriif ba nga raas,
yaay waada mat li nga doon, yaa sell yaa set i jëf.

Sirrub wilaayati yaa koy, ràng góor ña ko am,
yaa déjji pakk ya woon, ca yoon wa tee ñu tëruf.

Ngax yaa ngi tëb ak a bàkkooy folli buur ak a fal
nebbon bi nëbbu ci ñay, compam defuñ ko ci tef.

Doo fecci kóllare Maam, koo yar du fayu du tooñ,
say jëf du weddi sa wax, kuy raas sa kem dafa dof!

Yaa sax fi béjjénu kun, te mbëkkewóo ak a sëlbuy sippi ay darjaat, yaa mat li gaa yi di def.

Loo digle yaa nu ca man, loo aaye dun la ca seen,
lut Yàlla ak Yónnenam, taxul sa bët bi di raf.

Màndal nga xol yi ci maa-us suhdi wal warahi,
la Mawdo ruujoon nga bay, ñaraas ca ay lefi lef,

Dekkal nga daara yi woon, dundal tariixatu Seex,
ndaw ñaa ngi jàng ak a werdiy yewwu njël di wasif.

Noobul ba naaf sunu neewoy xol yi tur wa du fay,
kalxatti fii suhufil ahjaari ardi Jolof.

Kariim la doomi kariim, Mawdook Sofee nu ko jox,
muy sànni tàccu fi nun, far mawti ñëw ne ko këf!

Neexoon nu gis ko ci bët, sun ruu yi nàmp ca moom,
ndax xol yi xippi ci gii ngëmmeen gu tar niki dof!

Na Yàlla dolli ko leer, ful yërmadeem ja ca moom
bijaahi Sang ba gën jaam ñépp wax ak i jëf

Sallal ilaahu halal, Mahmoodi xudwatinaa,
wal aali was sahbi feek watat di ñatti araf.

Aji-bind ji: Imaam Jóob
Aji-topp: Seex Jaxate

Catégories
Sëñ Haadi Ture

Pitax mu ndaw

Bismilaa Rahmaani Rahiim

Faa ilan, faa ilan
Nan ci way ciy wolof
Soo wayee ciy wolof
Kon ci xol lay xaraf

Déglu naa biig ci njël
Am pitax cig garab
Ñuy tawat naan hadiil
Ab liccin moo ko këf

Mii pitax naa ko ndax
Mar wu tar waa ko ray
Mii pitax naa ko man
Xaajumaa wóolu maf

Mii di way, mii di jooy
Kurkutuut, kurkutuut

Soo amul fathu nag
Doo ca am aw araf

Seeni way moo yëngal
Tiisu xol wii ci man
Moo tax it maa ngi nii
Maa ngi saf waa ju dof

Maa ngi leen jooru naa
Yéen dangeen dul nelaw

Yéen pitax yi, ñu naa
Jooju wax nañ ko laf

Nun danoo sib nelaw
Kuy nelaw doo nu saf
Kuy nelaw yaa ko tal
Nun sunuy gët du raf

Foo fi gis kuy nelaw

Ag cofeelam wérul
Su cofeelam wéroon
Kon bëtam sax du xef

Waa ji man waaru naa
Yii pitax ñoo nu gën
Seen cofeel ak hadiil
Soo mënoon roy ko faf

Fuy pitax deeti way

As hadiil, nan fa way
Séexu Tiijaan Sëriif
Moo ko jar mag du kaf

Seexu Tiijaan Sëriif
Nan ko way, nan ko roy
Ay waxam nan ca ŋoy
Moo nu doy, moo nu saf

Seexu Tiijaan Sëriif
Ndeem dangay roy ci moom
Ay jëfam day rafet
Ay waxam day woyof

Seexu Tiijaan Sëriif
Waaru naa ciy mbiram
Ag cofeelam ci xol
Rekk sax doy na jëf

Seexu Tiijaan Sëriif
Ab kemam daa amul
Foo ko seet, doo ko gis
Muy Kajoor, muy Jolof

Seexu Tiijaan Sëriif
Kuy kokam daldi raw
Soo ko soppee ci xol
Kon bégal, am ngërëm

Daaguleen cim lefam
Daldi raw gaa ya war
Naaru-góor yay dawal
Aw yeneen xeeti lef

Catégories
Al-Haaji Muhammet Basiir Sekk

Yeetey Al-Haaji Muhammet Basiir Sekk (1)

Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim
Sallal Laahu halaa Muhammadin wa Aalihii wa Sahbihii wa Xadiimihii wa sallam

Lii xasidab wolofal la bokk ci “Yeetey Al-Haaji Muhammet Basiir Sekk kay taalibeb baayam ju siiw ja yal na ko Yàlla gërëm te gërëm nu ci barkeem” mu jëm ci ndaw ñépp ak képp ku ko aajowoo ci mag ñi ci rakki gàmm atum 1391, ñeel Abuubakar Siise mom Seex Daawuda Siise ak i kemam 1971.

Alhamdu Lillaahi may yee ndaw yi buur bëgg a dem
Fas yéene raw maas ya jot seen maam ya wéy am i ndam

Góor-góorluleen ndaw yi ag ndaw baax gu nekk la am
Am-am yi, xam-xam yi, ak xar-baax yi xaj na ci moom

Loo teg sa bët, naw ko, boo koy sàkk daldi ko am
Booy mos nelaw tuuti, bañ a neenal, di wut, danga am

Ngir kiy Boroom jaam ñi, par-parloo du yegg fa Moom
Noo def, Mu def noona, ku Ko nekkal, Mu nekk ci moom

“Man kaana Lillaahi, kaanal Laahu faddalahum”
Loolee la Seex Bàmba ak mbooleem ñu baax di gërëm

Lu diis la ngay fob dafay diis gann soo bëgg a am
Barkeek yu gën say meloy wuuteek meloy ña ma xam

Booy wut lu baax bul nirook kuy wut leneen lu du moom
Regg ak nelaw teg ca neenal, jiitu maas ga du am

Nit ku du xëy sàkku, te du gontal di wut lu mu am
Buy wéet nelaw fu’m faree daaneel ko ndam du fa am

Am-am wa xam-xam ku jox neenal, nelaw, bakkanam
Doo am ca ñoom kenn, doo dem fenn am ñu la gëm

Ngir àddunaak fa nu jëm, ñoom ñaar a fay joxe ndam
Am-am wa xam-xam bu dul ngir Yàlla am ga du am

Ba’ñ tànn mooy ba di faj aajooy ña teew di fi ndam
Ak bay xamal nit ñi diiney Mustafaak ña ko gëm

Ñoom ñaar ridal Laahi mooy tax ñuy ko wut ba du am
Kon am gi ay fitna lay dolli fileek fa nu jëm

Moo tax ba Seex Bàmba def mbooleem yi baax ca këram
Ku am ridal Laahi, am xam-xam di daw di fa dem

Am-am wa xam-xam ku daa muñ xiif bu wér te gërëm
Ay coono, muñ ñàkk, muñ moy Yàlla, foofa la jëm

Booy wut ba ñoom ñaar ñu xëy àndaati jébbalu ñoom
Jébbal la seen bopp yor say bokk yor fa nga jëm

Dañ lay xëyal fal la di la gontal lu maas ga xemem
Buy fii mu ñëw buy feneen loo jublu daldi ko am

Dootoo xalaat àdduna ak bon-bon yu rëy yi mu am
Noonoo ci aw des wu baay yaak maam ya gedd ko dem

Ngir loo fi gis ñuy xëccoo mbaa ñuy xuloo di ca jëm
Aw des la wow ay junniy nit ñépp mos na ko dem

Kon yaw muñal jaamu, fa nu jëm am na kër yu fa am
Yu ken sancul am na mbooleem may gu jaam di xemem

Lol doy na, jeexal na mbooleem yiw yu góor ña di lim
Àjjana, hay jeex na, lu fa nit taamu daldi ko am

Ma def salaatan wa tasliiman Haliyhi bi Him
Wal Aali was Sahbi ak Seex Bàmba may sunu ndam

Subhaana Rabbika Rabbil hissati hammaa yasifuun wa salaamun halal mursaliin walhamdu lil
Laahi Rabbil haalamiina

error: Content is protected !!